Marsiyya Seex Ibra Faal

Transcription

Marsiyya Seex Ibra Faal
Marsiyya
Seex Ibra Faal
Seex Muusaa Ka
(1891 - 1966)
Transcription :
Serigne Mbacké Dieng
Révision et amélioation :
drouss.org
© 1436 h / 2015 - www.drouss.org
Tous droits de reproduction réservés, sauf pour distribution
gratuite sans rien modifier du texte.
Pour toutes questions, suggestions, ou erreurs, veuillez
nous contacter par le biais de notre site internet :
www.drouss.org
Quelques indications
Wolof
per
rus
caam
ñam
xol
jibi
njaay
nday
ŋaam
gëm =
e=é
u = ou
c = th
ñ = gn
x = kh
j = dj
nj = nd
nd = nd
ŋ
ë = eu
é = è (plus dur) = rér
òo = au
gòor
q = xx
suqali
ii - uu - oo - aa ee (tirer sur le son) ;
Ex : biir - suur -xool - gaal - xeer
Français
pér
rous
thiam
gnam
khol
djibi
ndiaye
ndeye
(machoire)
geum
perdu
gaure
soukh khali
Marsiyya(1) (définition) :
Dans la littérature arabe, le Marsiyya ou Rasa est un texte
écrit pour exprimer, sans exagérer, son angoisse, sa détresse
voire sa peur à la suite de la disparition d’une personne. Il met
en exergue les qualités du défunt. Il chante son courage, sa
bonne conduite, le donnant ainsi en exemple à la postérité. Il
peut être composé :
– soit pour regretter un proche disparu. C’est le vrai marsiyya.
Il naît de l’inquiétude, exprime la détresse sincère et
communique l’angoisse à l’auditoire ;
1 c.f. LE MARSIYYA, Par Cheikh Amadou Kabir MBAYE
2 - Marsiyya Seex Ibra Faal
– soit pour célébrer, toujours dans un contexte de détresse,
les rois et les peuples antérieurs valeureux rappelant ainsi le
passé glorieux ; - soit pour présenter ses condoléances dans
la douleur et les pleurs en insistant sur les qualités du disparu
et l’angoisse suscitée par sa mort ou plus fréquemment pour
transmettre la sagesse populaire en abordant les thèmes de
la vie et de la mort.
Dans le wolofal mouride, le marsiyya reste un poème lyrique
exprimant des sentiments mélancoliques provoqués par un
deuil mais réservé à la célébration d’un héros, un cheikh ou
disciple très en vue, disparu. Il s’inspire du Huqqal-buka-u
(Faut-il [les] pleurer ?). Ce poème mystique constitue le
modèle fondamental pour le genre. Cheikh Ahmadou Bamba
y décrit les caractéristiques des Maîtres soufis.
Précisions :
Les vers que nous avons encadrés sont incertains. On les ne
les retrouvent pas dans tous écrits que nous possédons ; aussi
ni dans toutes les bandes sonores.
Marsiyya Seex Ibra Faal - 3
Bismi-l-laahi-r-Rahmàni-r-Rahìmi
Wa Sallallàhu anla Seyidina Muhammadin wa sallama taslìman
àddina ndax day bëgg a jeex
am gaa yu baax yeey bëgg a jeex
am mbër yu ndaw yeey bëgg a seex
Moo gaa yi xam naka pexe ?
ka xamlewon ag tarbiya
ak ka xamon ag tarbiya
moo buñ demee ba surga ya
ku leen di wax nag luy pexe ?
ka wootewon ci àdduna
ba ñépp wuysi fàddu na
nan jéem a dëddu àdduna
te jéem a wuyji mooy pexe
Seex Bàmba dem ci « Wamsashi»
Seex Ibra dem ci « Tamsashi»
Moo ñi fi des kuñuy dese ?
yeenu muriid naka pexe ?
4 - Marsiyya Seex Ibra Faal
Ab séet du dem ba doomi dikkeem
Seex Ibra Faalay doom dikkeem
moo rawi bokk, rawi doom
topp mi waaj leen mooy pexe
Ab séet moroom yaay topp ma
sëriñ muriid yaay topp ma
jéem leen a wàlli séen po ma
te ba po mii ngeen di fexe
Seex Ibra gëm ga làndi na
moo tax mu dëddu àddina
fekki na Bàmba sotti na
wàcci na aljanay texe
Mas nay xibaar ag jébbuloom
ba wax ne Yàlla mi ko moom
moo ko ne Bàmba moo la moom
raasi ko jox ko say pexe
Tegtalko yoon wa ab muriid
di aw ba raw pexem Mariid
ba am ngërëm bariy muriid
te dootu ree di tex-texi
Marsiyya Seex Ibra Faal - 5
Mu dal di dem Tayba-Daqaar
Ngir dégg Bàmba di fa xaar
seet na Sëriñ Tayba-Daqaar
cim njàng lay xame pexe
Mu tëdd guddi listixaar
ba mu xëyee ba tusubaar
Sëriñ Mataar Turee fa jaar
leeram ga wan ko lay pexe
Mataar Turee nga yori jóor
yanu ko jëm Mbàkke-Kajoor
Sëriñ bi yónni ko ca Mbuur
Seex Ibra topp cay fexe
Mu jis fa Seex Aadama Géy
Sànni mbiram dal di ca ŋoy
Mu wan ko Bàmba mbër mu rëy
Sëriñ ba naa ko foo fëxe ?
Mu wax ko tegtal ya fa moom
Sëriñ Bàmba wan ko la fa moom
mu xam ne jis na ka ko mom
mu dal di fab mbiram joxe
6 - Marsiyya Seex Ibra Faal
Ma wax la bis ba ndax mu wóor
ñaar fukki fan ci weeru koor
bisub dibéer la mbir ma wóor
Seex Ibra yaa rëyi pexe
Mu sóobu far ba jiitu leen
Seex Bàmba ne kii ëpp na leen
leeram gu rëy gi wër na leen
fum toll xol bay nux-nuxi
Wax na ne tuuti kon mu dem
fekk Sëriñ bi lëm mbiram
ba ken du jot ci baatinam
ludul ca bis ba ñuy texe
Jaaraama Seexi Ibra Faal
Làmp bi Sayxii Bàmba taal
leeral nga réewmi yaa kamaal
yal na nga dolliy beréxi
Ba mu ñëwee Mbàkke-Kajoor
fekkon na daara ja di suur
moo jëkk a yalwaani di woor
ñu di ko ree di tex-texi
Marsiyya Seex Ibra Faal - 7
Yendoo liggéey, fanaane root
gaa yay nelaw ba naa xuréet
ba luy ganaar ne kurkureet
moo ko xewal daawul doxi
Moo fa xewal nuyoo di raam
moo nu teree wuyu ne naam
fekkon na ñuy jàng fa maam
moom muy muriitu di fexe
Fekkon na daara ja di riir
moo dindi àllarbaak dibéer
lu Bàmba wax mu dal di buur
lum mas am dal di joxe
Moo fa xewal soli sagar
moo fa xewal sëqal kawar
moo fa xewal saxoo sikar
daawu fa bay di rux-ruxi
Ba mu demee Mbàkke-Bawol
daf ne na waa kër ga ba wol
naay soq tey rooti di wol
booleek liggéey di ko joxe
8 - Marsiyya Seex Ibra Faal
Lu bàmba wax mu dal di naaw
fóorem ju rëy ja sant Saaw
naa ko da ngay dellu gannaaw
jànggil muriitu du pexe
Mbooleem muriid ya di ko soow
mu mel ne dof bu mat a yeew
ba mujj far ñépp ne siiw
Meloom ya far di ko doxe
Mu jiitu far amul moroom
far gëni bokk gëni doom
jaaraama jaaraama xadiim
wàcc nga wàccaaleeg texe
Yaw masulaa juuyook ndigal
naka nga jóg të nga ndugal
ku aw sa mboor duñ ko mbugal
garmi yi yaa tax ñuy texe
Yaa jëkk a jébbale sa xol
fekkon nga gaa ñay xorxoral
ñaley setal ñaley nëxal
yaa wane ngér mi ñiy doxe
Marsiyya Seex Ibra Faal - 9
Yaa xam Sëriñ bi yaa xereñ
daawoo weranteekub sëriñ
bàjjo bi yaa bariy njariñ
waane wi yàgg ngaa naxe
Am ngay gërëm ba am dërëm
fab ngay dërëm jëndey ngërëm
loo mas a am tàbbal këram
ay junni daal nga daa joxe
Joxe nga àddiyay giléem
yu safi ngurdu safi koom
soldaar sa yaa joxe sa doom
Faadilu Faal am na ag texe
Sa ndaw da daa dem ba Gaboŋ
di yóbbu ay saaku yu roŋ
di war ca gaal ya yori boŋ
doo denci lëf ba muy maxe
Moo tax nga mel ne ag saxaar
ku nar a dem da na fa jaar
kuy ñaani paas na seeti gaar
bum nég ba naa na ko pexe ?
10 - Marsiyya Seex Ibra Faal
Ndegam da nga xebat sa paas
way-wata yaa nga fa garaas
seetal ma wax jii te xiyaas
ndegam da ngaa am looy joxe
Baayay saxaar doomay wata
kuy xamle Yàlla du fi të
ku ji àndaar góob cay mata
jiyal ci taw buy béx-béxi
Seex Bàmba taawloo Mustafaa
Seex Ibra taawbay Mustafaa
Diggante Marwataak Safaa
Kuy aji warnafaa doxi
Seex Bàmba am nam Faadilu
Seex Ibra am nam Faadilu
ku xam na faale Faadilu
kon ag mujam du toroxi
Seex Bàmba bégle nam Basiir
Seex Ibra bégle am Basiir
Mbég moo ci dem lekk ba suur
jegeel ma kay toggiy joxe
Marsiyya Seex Ibra Faal - 11
Seex Bàmba am nam Abdulaay
Seex Ibra am am Abdulaay
abdu mu nekk mat na waay
bul weddi céebu kaay texe
Yal na ñu aw seen tànki baay
ba mujj donnu seeni baay
ba mujj boole seeni gaay
aamiina ndax ñépp texe
Seex Ibra dem na wàcci na
lum mas a aajo faju na
ba xëy ne cipp àjjana
nan farlu tey àndi pexe
Ken masl a jis sasam wu booy
du daw kakoy muslook a njuuy
moo jar a way te jar a jooy
moo àddinaa man a naxe
Déglul ma lim fi ay ndamam
ba gaa yi dollee xam mbiram
ba xol yi bég ba dellu gëm
leegi ragal yi yox-yoxi
12 - Marsiyya Seex Ibra Faal
Jaaraama Ndey Saynabu Njaay
la Soxna Jaara yor di jaay
yaa ko mosal waa Njare-Njaay
saw ŋàññ rot na yaa texe
Diggante Njukki ak Njamatil
dañ daa dajey naani butéel
yaa tax ñu jébbulu ca teel
Faal Njaga yaa rëyi pexe
Mbulaki Sàqaki Sugeer
dañ daa falook a fali foor
yaa tax ba dine di fa leer
toxal nga póon mañ daa tuxe
(2)
Doomi Dàmmeel ya fa newon
yaa dàm(m) mbir ma ñu newon
tay ñépp ñépp a ngi fi nun
ken amatul lu muy fexe
Yaa yóbbu Mbaaxaan ca Xafóor
yaa tax ba xol ba dootu fuur
yaa tax mu sànni yatu nguur
fab yatu gëm di laaj pexe
2 ou (dañ daa falook a soli buur)
Marsiyya Seex Ibra Faal - 13
Te xam ne mas naa yor junjung
fumu jëm géwal ya naa kundung
muy xas di bàkku cid goroŋ
tay mu yam ak nun ay pexe
Yaa tax ba Abdulaahi Xaar
taxaw fi bunt di fa xaar
woyaflu bay lekk daqaar
ngir sopp Bàmba miy joxe
Te xam ne moo doon doomi buur
lum mas a wax ñu dal di buur
la dale Mbaakol ba Kajoor
moo amewoon seeni pexe
Yaa tax ba Soxna Mbenda Faal
ak Gañsireeki Làlla Faal
gën doomi soxna yii fi taal
diine ju rëy ji ñuy doxe
Te xam ne seeni baay a moom
Fedarba taalagut kanoom
koo mas a jis ay jamonoom
xolam ba daawul yox-yoxi
14 - Marsiyya Seex Ibra Faal
Yaa tax ba Abdulaay ñaxib
làmbi ndigal far na ko ub
la gaa ya giiroo moo ko xab
tabax na ay kër di joxe
Te xam ne mas naa dox fi moom
tay jii mu mat sëkk boroom
ka denci doomam dib goroom
lii doy na xarbaax duy pexe
(3)
Seex Ibra Faal amul moroom
sàkk na mbër yuy roy ci moom
leeral na penkkoom ak sowoom
luy yàq dootul ñuy-ñuxi
La dale Ndar ba ca Dakaar
jàll gannaaw yoonu saxaar
mbër mu fa rëy ba ñu ne kaar
Seex Ibra lay laaj pexe
Ndar la ko doomi Jaara may
leeral na bopp jaara tay
waykat wa Sàmba Jaara Mbay
moo tax dënnam bay bëx-bëxi
3 ou (tay jii mu mat sàng ak boroom)
Marsiyya Seex Ibra Faal - 15
Mu jóg fa agsi Ndànd-Faal
jàpp fa doomi Ngóone Faal
def ko ne làmp bu ñu taal
tay Ngingineew moo fay fexe
Leeram ga sar ba agsi Kees
ku ñëw mu duy la ba nga fees
luy nit ku ñuul ak ku xees
ñéppay bawoo fa Ngaay-Mexe
Sëriñ bi ñëw Njurbél mu ñëw
gàddaay këram ya te du daw
guddeek bëccëg ñam ya di ñëw
Ba Bàmba xëy sàkk pexe
[jant a ngi jooy weer a ngi jooy
mbooleem biddiw yépp a ngi jooy
suuf ak asamaan a ngi jooy
ku nekk naan na ka pexe]
Mbooleem muriid yépp gëlam
ken xamatul kuy Sëriñam
kune na ngéej a dal di dem
àddina séppiy jëx-jëxi
16 - Marsiyya Seex Ibra Faal
Mu dal di ŋoy ci Mustafaa
ngir xam ne am na listifaa
mag ñépp dem moom mu ne faa
Masl a tuxooki yox-yoxi
Ba xëy na wuyji ab sanggam
tuubaa la toggewoon añam
Bàmba a ko jiiteloo ñoñam
diggante Biib gaak Guy-Texe
Ma ngay janook tooli dërëm
meññat mu gën junniy dërëm
jis na lu weesu mébetam
am na lu raw lam doon fexe
Bàmba xaroo na koy ngërëm
Ridwaan tijjil na koy kërëm
ñoñ huuru-hiineeng fa wetam
jis na lu raw yoolub joxe
Ngërëm la Yonnen bay gëram
Abaabakar ma jëkk a gëm
la Sayxu Bàmba di gëram
Seex Ibra mooy jëkk a texe
Marsiyya Seex Ibra Faal - 17
Medaay ba Yonnen bay takkal
Abaabakar ngirug dëggal
la Sayxu Bàmba di takkal
Seex Ibra Faal bisub texe
Mànto ba Yonnen bay solal
Abaabakar yor paresol
jël saadixiinaya tofal
yal na ko Bàmba fab joxe
[Bàmba a ko jël dal di ko fal
mbooloo ma dar ko muy dëggal
Jaaraama Seexi Ibra Faal
yaa jar a xam bisub texe]
[Yaw ku la sopp daal di baax
yaw ku la weddi dootu baax
waa joo gërëm muy gën di baax
kii ku bañ day toroxi]
[Nan jéem a toppi ndigalam
te jéem a moytu ay tereem
te jéem a roy ci ay jikkoom
moo am njariñ bisub texe]
18 - Marsiyya Seex Ibra Faal
Muusaa la way wii wolafal
yal na ko Shayxii Bàmba ful
te boolekook gaa yu dëggal
yoo xam ne ken du yox-yoxi
Aamiina aamiina ne leen
aamiina ndax ñu boole leen
ci mbóoti woy wi ba lu geen
sàkkooti am ca ag pexe
Aamiina aamiina ne leen
aamiina ndax ñu boole leen
ci wax fi Muusaa ba lu ngeen
sàkkooti am ca ag pexe
Allaahuma Salli anla Seyidinaa Muhammadin wa
Sallim
Marsiyya Seex Ibra Faal - 19

Documents pareils