sukëndikuci sunuy ndam

Transcription

sukëndikuci sunuy ndam
CAIRN ENERGY PLC – SENEGAAL
SUKËNDIKUCI
SUNUY NDAM
CAIRN CI SENEGAAL
Ligeeyu Cairn ci Senegaal mi gui jaar
ci Capricorn Senegal Limited bi nga
xamné doomu keurou koom le bou
Cairn Energy PLC. SIÉJOU CAIRN MI GUI EDIMBOURG CI
ECOSSE AK AY YENEEN BURO CI SENEGAAL,
LONDRES AK NORVÈGE
Cairn Energy PLC (Cairn) bok ne ci société saaytu
ak devlopmen petrol ak gaz ci Europe té mou bok
ci Bourse Londres. Cairn feñal ne té ligeey ne ay
dencukaay petrol ak gaz ci ay bërëb yu wuuté ci
adina bi.
Senegaal doon ne missal bi
gën bi firndé jubluwaay Cairn
ci nek njiit ci wallu këru koom.
Amoon neñu ci gëm gëm bu
wér ci wallu teknik lu aju ci
kattanu yaatuwaay wi, lolo
tax ba niou ubbi niari bassing
you jëk yi nga xamné ñi gui
feeñ ci atum 2014.
Cairn dafay ligeey ak gornemen reew yu sen këru
koomu petrol am ay ligeey ci wallu wowou ku ci
mel ni PETROSEN ak ay yeneen këru koomu
petrol ci adina bi.
Cairn am ne xam-xam- bu mucc ayib ci saaytu
wëttu geej té wané ne kattanam ci def ay projé ci
wallu saaytu, forass, devlopmen ak togg yu jaffé
té ligeeyam du saffano ak dëkuwaay yi ko weur
ak environmen.
Cairn yitté wo ne ci jaaralé ligeeyam ni ko yoon
tërëlé ci Senegaal.
1
UBBIG BASSING WU YEES
CI PENKU ATLANTIQUE
Li ñu mbëbët ci anam biñuy saayto moy jël ay
bërëb yu am solo ci yaatuwaay wi ak am kaatanu
topp ko su ndam amé. Ganaw ba Cairn gëmé ci
wallu teknik dayoog ak solog njeuriñam ci
Senegaal, yatuwaayu saaytu Cairn mi gui sosso
ci bët ganaar afrik nga xamni ken saaytoogu ko
ci geej yu xoot yi nek wètu plateau wi nga khamné
ay teen yu bari gasson neñu ko digganté attum
1960 ak 1970.
Cairn sampu na Senegaal ci attum 2013 ak ñi
muy liggeyyal ci joint venture bi ak gornemen bu
ko doolel. Mi gui wey di yittél ak dawal khalissam
ak ligueeyam. Senegaal doon na reewu yakaar
ndax guiss nañu kattanam ci wallu hydrocarbur.
Saaytu petrole ak gaz ci Senegaal mi gui tambali
ci attum 1950 wayé 40 teen ci gueej gui la ñu gass
bobou legui.
Ci weeru mars 2013 Cairn diot ne bokk ci
ligeeyu niet teen yu niar ñi moom Far Limited
ak PETROSEN di këru koom ci wallu petrol
wu Senegaal moom. Bi nieti weer weeso,
ConocoPhillips mo niow bokk ci.
Ci lu neew nieti at, Cairn saaytuneak gunge ay
partenairam ba niuubbi niari teen yu jeuk yi ba fek
ci petrol.Tek ne programm wu am solo ak cambar
wu niaw ci teen yi ; jot na ay xibaaru suuf yu yees ;
yok ne cambaram ci nient teen; tambali ne ay
ligeey ci programmu teen wu yees té xëc neñ diiru
nieti at (ba fevrié 2019)bataaxal niel bokk ligeeyu
togg wi (PSC).
Ci attum 2014, Cairn ak ay naatango JV gass neñu
niari teen ci geeju Senegaal ba fekk ci petrol boolé
ci ubbi bassin bu yees ci ndeyjooru atlantique.
Teen yoyé nio jeuk ci yi ñu gass ci Senegaal ci 20
at yi weesu té nek ci geej yu xoot yi. Niari feeñ you
toftolo yi firndél nañu ci tambali cambar wi petrol
wu naat ak xeer yu geun baax ci aduna bi ci teenu
FAN-1.
2
Ci weeru nowembar 2014, Cairn yeggël ne
gornemen Senegaal ci turu Joint Venture bi,
feeñ yi am niel teenu FAN-1 ak SNE-1 yu. Cairn
xalaat ne niari feeñ yoyou ak yakaar yi ñu guiss
ci goxu licence wi doon ne alal bu tollok bën
milliard barigo.
Ganaw bañu sampé programmu cambar ci ay diir
yu bari bolé ci yok lii di njëg ci Senegaal nguir jaay
mi, Cairn ak ay parteneeram ci Joint Venture bi
tëggu negn ci yoonu ligueey bu yagg ak dugal xaliss
bu bari.
Ci weeru mé 2015, ganaw ba ñu xamé kattanu
yaatuwaay wi, Cairn ak ay parteneeram yu
Joint Venture bi, jebël neñ gornemen Senegaal
programmu cambar ci diiru nieti at.Mo nekon
programmu cambaru geej gui bi jëk ci anam
bi ci dëk wi.
3
DIIRU SAAYTU AK XALAAT
Ci weeru setumbar 2015, Cairn ak ay
parteneeram ci Joint Venture bi tambaliwaatoon
negn ligeey ci geeju Senegaal ak tambali campagnu
diot ay xibaaru suuf ci xam-xamu 3D bu yaatu.
Yiité suuf wi tax ñu xam kattan wi am ci yaatuwaayu
soowu licence wi mi gui tollon 2,400km².
Ci weeru octobre 2015 gaalu forass Ocean
Rig Athena wu yengeuntu ci niari fann bu 7e
generassion té xatim bataaxal ak ConocoPhillips
delou na ci geusstou forass wi ngir xaimala nu fek
ci teen SNE-1. La taxoon gnu def programm bobou
mo doon yok sunu xam-xam ci alalu suuf yi, bolé ci
am ay xibaar yu yees ci anam yu woor té yomb yu
wuuté ak saaytu wu jëk wa.
Ci weeru nowembar 2015 Cairn ak ay
parteneeram ci Joint Venture bi yokal negn len
nieti at ci bataaxal niel bokk ligeeyu togg wi. Yokk
wowou mayna diir bu mu cambar niari feeñ yi ak
kattanu saaytu ci li dess ci gokhu PSC.
Ci tambali 2016, yëklé nañu njurël yu baax ganaw
cambar bu njëk ci teen SN2 ci gueeju Senegaal.
Diot neñ am ndam ci gawaay bi ci niari place yu
wuuté ci teen wi: bu jëk wi am na gawaay wu tollok
8,000 barigo/bës yu sen qalité kawé ci ndeyu
barigo wi fété suuf, benen wi gawaay wi tollok
1,000 barigo/bës té qalitém geuneu neew ci
4
ndeyu barigo wi fété kaw. Ndam li firndél ne niar
nieup amoon negn kattan ligeey ci gawaay yu
meun wey bolé ci dimbalé yok tolluwaay alal yi.
Ci weeru mars 2016 yeggël nañu njurël yu baax
yi jugé ci teen SNE-3. Njurëlu niareelu teen wi
dëggël ne dayyo ak kattanu SNE té wané ne
gawaayundeyu barigo wi fété kaw ci ay lim yuy
wey ci wallu koom.
Ci weeru avril 2016, Cairn yeglewaat ne yeneen
ndam ci wallu saytu ci teen BEL-1. Saytu Bellatrix
mo takkhon jok teen bobou ak cambar bët
gannaru SNE nguir dëggël njëg wu baax wi ñu
giss ci yeneen teen yi ak wey di firndél rey reyu
yaatuwaay SNE.
Ganaw ba mu defé cambar yoyou ba tay wi, Cairn
ak ay parteneeram ci Joint Venture bi nangu negn
taxawal nienteelu teen wi SNE-4 ngir cambar
yaatuwaayu penku SNE. Lolou mo firndél ni suuf
si ci ndeyu barigo bi féété kaw am ne qalité bu
nouroo ak li gnu fek ci gox bi.
Cairn ak ay parteneeram ci Joint Venture bi wi di
negn wëyel di dajalé xibaar yi muy dieulé ci nienti
teen yi ak 2DSTs ak lu tollok 600m. Dine tax gnu
meune xam anam wi geune ngir wëyel cambar diw
bu bari bi ak saaytu yoonu developmen yi.
Thiès
Légende
Bërebu contraa
Xibaaru suuf 3D yi Cairn am ci 2015
Xibaaru suuf yi Cairn moom
Feeñ yi
Yakaar yi ak devlopmen
Teenu saaytu wu Cairn
Teenu cambar
Yeneen teen yi
Dakar
SENEGAAL
Diourb
CVM-1
SH
AK
RE
FB
EL
IC
ZO
O
ES
M
Mbour
RUFISQUE-3
DAKAR-MARINE-2
RUFISQUE-2
RUFISQUE
OFFSHORE
Foundiougne
XOOTAY
SANGOMAR
OFFSHORE
SANGOMAR
OFFSHORE
Pa
BETELGEUSE
& ACHERNAR
FAN-1 FIELD
CANOPUS
FAN-1
NORTH FAN
Sokone
DENEB
SIRIUS
ELECTRA
FOMALHAUT
BELLATRIX
SNE-1
FIELD
CENTRAL FAN
BEL-1
SNE-2
SNE-1
GEMMA
SNE-3
SOUTH FAN
0 km
5 km
10 km
SOLEIL
CDE
Xaima alal yu piir yi
>1 milliar barigo
Toubakouta
IZAR
20 km
5
DIAPALE MBEBET GORNEMEN CI YOKK
ALAL YI CI WALLU ENERSSI
Mbëbëtu Cairn moy genné alal wu ñuy sukkëndiku
ngir soss njëk wu yees niel Senegaal té yokk enerssi
ba mu doy ci dëk wi. Mi gui diapalé gornemen wu
Snegal ngir yokk alal yi ci wallu enerssi ngir saafara
digganté jaay ak jënd ci enerssi.
Li gallankooron yokkuté ci wallu askan ak koomu
rewmi moy jafe jafe diot ci enerssi. Koomu rewmi
mi gui sukkëndiku ci petrol wi ñu jëlé bitim reew.
Guiss petrol ak gaz wu bari ci geeju Senegaal doon
ne dimbali koomu rewmi, gox yi, këru koom yi,
gornemen Senegaal wi té doon ne indil xaliss wu
am solo bolé ci jurël karaange ci wallu xaliss ak
enerssi bu gnuy diay bitim reew ci diir wu yag.
Ba ñu ko falé ci 2012, Presidan Macky Sall dafa am
mbëbët yok koom té mi xëcc borom xaliss bitim
reew yi ngir niu niow bokk sukkeli Senegaal. Lolé
wañi ne wëru way rewmi ci nap, mbëy ak turism.
6
Presidan Macky Sall nek ne ku xam-xamam mac
ci wallu suuf té nekone njiitu PETROSEN.
Gornemen Senegaal tërëlna sartu petrol ci
1998 wuy faram facce anamu saaytu ak ligeey
hydrocarbur ci Senegaal. Sart wi weeruwaayu
bataaxal niel bokk ligeeyu saytu ak togg
hydrocarbur bi bolé Cairn ak ay parteneeram
ci Joint Venture bi.
PETROSEN am ne taxaway wu am solo ci li mu nek
ci Joint Venture bi, ci li mu nek yemalekat ak
ci li mu fi taxawal jewriñu enerssi. PETROSEN
am ne sagn sagn yokk taxwaayam ci kapital bi ba
18% bu gnu tambalé xëcc ci teenu SNE.
Gornemen Senegaal yeggël ne ndogalam ci 2012
ngir bokk ci kureelu Këru Koom wu Mak yi xëcc
suuf ci anam you Leer (ITIE) té Cairn bokk ci.
Kureel wowé doon ne sart ci aduna wi ngir leeral
fëyu alalu suuf yi. War na reew yi soss ITIE ñu
fëssal xibaar ci wallu fiscalite, licence, contraa,
ligeey ak yeneen poñ yu am solo yu dieum ci xëcc
alalu suuf yi.
Mbëbëtu Cairn moy gene
alal wuñuy sukkëndiku ngir
soss njëk wu yees niel
Senegaal té yokk enerssi
bamu doy ci dëk wi.
7
Cairn ak ay
parteneeram ci
Joint Venture bi
bolo neñ sen
ndegeurlaay ligeey
ngir amal njeuriñ
Senegaal ci askan
wi ak koom wu
baax té yag.
8
NJUREEL YI CI DIIR WU YAGG
Cairn ak ay parteneeram ci Joint Venture bi boloo
negn ci yitté jaay nguir amal njeuriñ Senegaal ci
askan wi ak koom koom wu baax té yaag.
Ganaw ba ñu jubloo ci dugël xaliss ci askan wi, da
niuy ligeey ngir yokk alalu askan yi, diapale njaang
té yombalal ligeeyu këru koom yi. Da niuy wutt ay
nataango yu woor te am njeuriñ ci programm yu
yëkëti sunuy ligeey ci gox yi niu koy defe.
Def neñu ay invesstissmen ci wallu yokk kattanu
institussion ak këru koomu Senegaal. Yeen yi gni
gui japalé sunu ligeey ci diamonio ji ak yi niow wayé
nieneen daniuy geune japalé askan wi. Sunu
programmu taxaw tem bi bolé ay nataango dafay
niaax ci wallu xëlu këru koom bolé ci dimbalé
yokkuté këru koomu deuk yi :
GREAT ENTREPRENEUR AK ECOBAG
Japalé nañu « Great Entrepreneur » bu British
Council : yeené British Council le ngir dimbali
ligeeyu ndawu rewmi. Dugël nañu xaliss ci projé
ECOBAG bi jël raw gaddu wi ba niuy tambali.
PROJE MICROFINANCEMENT
(THE HUNGER PROJECT)
Ňun nio taxawal The Hunger Project ngir japalé
ben programmu microfinancement yu jiggenu
Senegaal di jiité.
ECOBAG dey for mbalitu plastik ci deukuwaay
wi wi ngir togg ko ay doomu plastik yu ñu yeesal
ba paré di ko jaay defarkatu plastik yi. Projé wi
doon ne luy niaax yeesal mbalitu plastik ak ben
sisteem wuy dajalé mbalit yi. Sunu ndimbal mo
waral njeundum jumtukaay yu xarañ ngir yok
ligeey wi ak fëssal sartu HSE ci bërëb wi.
Senegaal moy reewu afrik bi The Hunger Project
jëk am té mi gui ligeey 1991 ba legui. Leegui
The Hunger Project am ne 10 bërëb ci Senegaal
yu toppato 178,000 nit yu nek ci 211 gox goxaan
yi. Estratéji bërëb yi dimbali ne ci dajalé lu tollok
15,000 ba 25,000 nit ci ay gox goxan ngir yok
sen baat andak gornemen wi ak meune diot ay
jumtukaayu dund. Loloy tax askan wi di meune
bole ay dole ngir jeuriño alal yi.
TAGGAT CI WALLU LAAK
Cairn ak ay parteneeram ci Joint Venture bi gni gui
japalé ben programm taggat buy wëy ci anglé niel
ligeeykatu jewriñ yi ak departemen yi nek ci
enerssi. Candida yi departemen minister yi nio
leen di tann té taggat yi British Council mo leen
koy defal.
Projé microfinance eumb ne taggat ci wallu
xam-xamu xaliss, ay xallis yu teew ngir ay lebal
yu ndaw, ak ay jumtukaayu denc xaliss niel gox
yi wi ci bërëb yi. Dafay japalé jigeen yi ci yokk sen
xam-xam ci jitté ak jënd ak jaay, yokk sen koom ngir
ñu am taxaway wu am solo ci sen askan.
Ngir diokh xam-xam ci anglé ak ci yeneen fann niel
ndongo daara kaw ëlëk yi ci wallu xam-xamu suuf,
ay taggat ci anglé ak ay njangalé ci wallu wax la
British Council nek di def niel ndongo ci IST ak
ndongo ci Darray Kaw Polytecnik (ESP).
9
YENEEN XIBAAR
So len amé yeneen laaj wala ngèn
soxla yeneen xibaar ci yitté Cairn,
yoné len niou bataaxal ci:
[email protected]
Jaar leen ci sunu sit internet
www.cairnenergy.com