jigeen bu dee sey - jigeen balaa baax

Transcription

jigeen bu dee sey - jigeen balaa baax
Jigeen bu dee sey
Jigeen balaa baax
Sëriñ Mbay Jaxate
(Radiy-Allaahu Anhu)
© 1436 h / 2015 - www.drouss.org
Tous droits de reproduction réservés, sauf pour distribution
gratuite sans rien modifier du texte.
Pour toutes questions, suggestions, ou err
eurs, veuillez
nous contacter par le biais de notre site internet:
www.drouss.org
Indications
Wolof
per
rus
caam
ñam
xol
jibi
njaay
nday
ŋaam
gëm =
e=é
u = ou
c = th
ñ = gn
x = kh
j = dj
nj = nd
nd = nd
ŋ
ë = eu
é = è (plus dur) = rér
òo = au
gòor
q = xx
suqali
ii - uu - oo - aa ee (tirer sur le son) ;
Ex : biir - suur -xool - gaal - xeer
Français
pér
rous
thiam
gnam
khol
djibi
ndiaye
ndeye
(machoire)
geum
perdu
gaure
soukh khali
jigeen bu dee sey
Bismi-l-Laahi-r-Rahmaani-r-Rahiimi
Jigeen bu dee sey ci kër tey bëgg sey ba di neex
nay muñ ta sax ci ndigal tey tont tontu lu neex
Tey foota kay togga kay ree tey waxam bañ-a neex
baatam di jëm suuf ta bum jekki tawatt aka jeex
Tey xëy di xeeñ ta nangò ñakkiy yëf-am tee sawar tee
bayyi maanee ku naa mane maanee sey ba du neex
Tey buub këram ba mu sett buub kër sëriñ ba mu sett
raxass ndabam ba mu sett muy daw xulòo a kiy xeex
Tey jog sa njël wall te duy mbaddam ya bët sòora set
mu gaawtu laax rajji fobb nakkay ndaxam ne sareex
Tey muuru tey baña merr tey sammu sammu bu werr
tey jappi tankam ci kër ga kone seyam dina neex
Tey gattaluw lammiñam tey wann wanni merram
kër matti neen la te boo koy mooñ mu xëy ni mëreex
jigeen bu dee sey - 3
Sey katt yi sey baa ngi kuy sey tee doo seyeenii
loo am ëllëg na la doy lo degg it na la neex
4 - jigeen bu dee sey
jigeen balaa baax
Bismi-l-Laahi-r-Rahmaani-r-Rahiimi
Jigeen balaa baax nangò dem dagga tey rooti
tey togg jox sëriñam balaa tilim fòoti
Lewat nangò yor njabòotuk kër ga yaatu ci gane
tee mokka mokk ba buy neex guur ga muy nootee
Tee neexu lammiñ woyaf mbirr toyy bay saf-u xob
tey buub ëtt ba ak këram ga tey nangò bootee
Te def mbañam rus tee lambòo ker sawar mana muñ
tey doomi soxna bu wer fum sey ñu yokkòti
Sawarr yarò yaru am xel loo ko yònni mu daw
tey jekki neegam balaa dem fenn taggòo-ti
Tey noppi tey muuru tey lamsal jegeb sëriñam
tey nabbu jambur ña tey wax ndank tey yootee
Rafet rafet jikko tey sett ràcc xar kanamam
tey soccu tey ree kanam gay melni luy wootee
jigeen balaa baax - 5
Bis bu aayee fonkk ak toggam di neex-a lu ñam
bum yann bum caxx bum xoñ bum texem lii ti
Buy tabbi neek sëriñam dey sol sëram ya mu
am xeeñ laskoloñ ja mu am fobb tiol ko ru gooti
Fum giss sëriñ ba di xay xay loo-ka foon a ka bës
lum wax mu daw tey wuyòo santam ba buy wootee
Lum am jox -ub sëriñam lum xam wax-ub sëriñam
tey gaawa tuub biss bu tooñee dal di tuubati
Jigeen ju mel nii ma wax ŋanjam wa rot na asal
giñ naani doomam ja day am barke buy tuuti,
Sub’haana Rabbika Rabbil Hizzati Hamma Yassifùn Wa Salaamun
Anlal Mursaliina Wal Hamdulillaahi Rabbil Anlamine
6 - jigeen balaa baax
© 1436 h - www.drouss.org - Tous droits réservés

Documents pareils